url
stringlengths
6
8
content
stringlengths
2
3.72k
source
stringclasses
3 values
page_310
310 80. Ña am xam-xam ne leen : “Toskare ngeen ! Yoolub Yàllaa gënal képp ku gëm tey jëf u yiw”. Ku dul muñkat du ko am. 81. Nu mëdd ko ci biir suuf si mook kërëm ga. Amul kenn ku ko mënoon a dimbali ku dul Yàlla, te it kenn dimbaliwu ko woon. 82. Ba ñu xëyee, ña doon xemmem wàccuwaayam ca démb sa, daldi wax ne...
coran-wolof.pdf
page_311
311 ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Alif, Laam, Miim. 2. Ndax nit ñi foog nañu ne danañu wax ne : “Gëm nañu ! ” te kenn duleen sànje ? 3. Sànje woon Nanu ña leen jiitu woon ; Yàlla xam na ñay dëggal ak ñay fen....
coran-wolof.pdf
page_312
312 12. Yéefar yaa ngay wax ña gëm naan leen ; “Toppleen sunu mboor, dananu yenu seeni ñaawteef”. [Mukk] duñu mas a yenu tus ci seeni ñaawteef. Li wóor moo di ñoom ay fenkat lañu. 13. Danañu yenu seen yu diis ya ak yeneen yu diis boole ko ca. Te bu Bis-pénc baa, danañu leen laaj la ñu daan duur [fen]. 14. Yónn...
coran-wolof.pdf
page_313
313 24. Tontul aw nitam doonul woon lu dul ñuy wax naan : “reyleen ko mbaa ngeen lakk ko”. Yàlla musal na ko ca safara sa. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñu gëm. 25. [Ibraahiima] wax na ne : “Yéen a ngi jàpp xërëm yi bàyyi Yàlla ngir dëgëral seenug cofeel seen diggante fii ci dundug àddina. Waaye bu ...
coran-wolof.pdf
page_314
314 35. Bàyyi Nanu fa lu bokk ca ñoom muy kéemaan gu leer nàññ ngir aw nit ñuy xel-lu. 36. [Naka noonu], la seen mbokk Chuhaybu demee woon Madyaana, ne leen : “Éy yéen samaw nit, jaamuleen Yàlla te gëm Bis-pénc ba, te buleen dox di yàq ci kaw suuf si”. 37. Ñu weddi ko. Yëngu-yëngu ba fab leen, ñu xëy ne lànjax...
coran-wolof.pdf
page_315
315 46. Buleen dàggasante ak ñoñ-téere yi lu dul ca na mu gën a rafetee te buleen ca boole ña yiwadi ca ñoom. Nangeen di wax ne : “Nun gëm nanu li ñu wàcci ci nun ak li ñu wàcce ci yéen, sunu Yàlla ak seen Yàlla jenn la, te nun jébbale nanu sunu bopp di ay jullit”. 47. Noonu Lanu wàccee Téere bii di [Alxuraan] ci ...
coran-wolof.pdf
page_316
316 58. Ña gëmoon tey jëf u yiw, Dananu leen dëkkal ay néeg yu kawe yoo xam ne ay dex ñooy daw ca suufam. Dañu fay béel, ndaw pey gu neex, 59. ña daan muñ te wéeru woon ca seen Boroom ! 60. Amul jenn daaba ju warlul boppam wërsëg ! [Waaye] Yàlla moo koy wërsëgal ak yéen. Te Moo di Aji-dégg, di Ku xam. 61. ...
coran-wolof.pdf
page_317
317 69. Ñay xare di jànkuwante [samaw yoon], danañu leen gindi Sunuy yoon, te Yàlla ànd naak way-rafetal ña. ----------------------------------------------------------------------------- Saar 30 : ROM (WAA ROM) 60 laaya - Laata-Gàddaay ga --------------------------------------------------------------------...
coran-wolof.pdf
page_318
318 9. Ndax dañoo doxul ci suuf tey xool naka la ñu mujje ña leen fa jiitu woon ? Ñoo leen ëppoon doole, daan réjji suuf si, feesoon ko dell ak seeni njaboot. Seeni Yonent indiloon leen ay kàddu yu leer. Yàlla tooñuleen, waaye ñoo tooñ seen bopp. 10. Ña daan jëf u ñaawteef, seenug mujj dellu ñaaw, ndax ñoom wed...
coran-wolof.pdf
page_319
319 21. Te bokk na ci kéemaanam yi, mu sàkkal leen ci seeni jëmm ay soxna ngir ngeen di ca dall, Mu def ci seen diggante cofeel ak yërmaande. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñuy xalaat. 22. Bokk na it ci ay kéemaanam, bindug asamaan yeek suuf si ak wuuteeg seeni làmmiñ ak seeni melo. Ay kéemaan a ngi c...
coran-wolof.pdf
page_320
320 32. ña téqale seen diine di ay kurél, xaaj bu nekk ne siiw la fa moom. 33. Bu lor ju laal nit ña amee, dañuy ñaan Yàlla di Ko woo booleek toroxlu. Waaye su leen di mosal yërmaande rekk, [nga gis] ñu delluy bokkaale, 34. di fakk la Mu leen indiloon. “Bànneexuleen. Dangeen xala xam”. 35. Walla Danuy wàcce c...
coran-wolof.pdf
page_321
321 44. Ku weddi, weddeem ga dana dal ca kawam. Ñay jëf yiw nag... Ñoom ña ngay waajal seen bopp [daluwaay bu maase] néeg, 45. Nar naa feye ñi gëm tey jëf u yiw, ngënéelam. Moom safoowul yéefar yi. 46. Bokk na ci ay kéemaanam, muy yebal yërmaandeem, ak gaal yi di daw ci ndigalam, te ngeen di sàkku ci xéewalam...
coran-wolof.pdf
page_322
322 55. Bu Bis-pénc ba taxawee, tooñkat ya danañu giñ naan as ndiir su ndaw la nu fi saxoon. Noonu la Nu leen daan férawale, soreel leen dëgg ; 56. Gaa ña amoon xam-xam ak ngëm, ne leen : “Sax ngeen fa ci dogalu Yàlla ba bisub dekki ba, - lii nag mooy bisub dekki ba, - waaye yéen xamuleen woon”. 57. Su boobaa, ...
coran-wolof.pdf
page_323
323 5. Ñooñaa nga tege ca kaw seen yoonu Boroom wu jub xocc wa, te ñoom ñooña ñoo texe. 6. Am na ci nit ñuy nëbb xam-xam, di feeñal waxi caaxaan ngir namm a soreel nit ñi, sànk leen, réeral leen yoonu Yàlla ci lu àndul ak xam-xam, weddi ko, jàppe ko ag doyadal. Ñoom ñooña am nañu mbugal muy toroxale. 7. Saa s...
coran-wolof.pdf
page_324
324 16. “Yaw sama doom, dIisaay woowu, doonte la sax dafa tollu ni as fepp, nekk ci kaw doj mbaa ci biir asamaan yi, walla ci biir suuf, du tee Yàlla indi ko . Yàlla Ku deñ-kumpa la . 17. Yaw sama doom, taxawalal julli tey digle njekk, te it nangay tere njekkar, te it nangay muñ li lay dal. Loolu mooy dégu ! ...
coran-wolof.pdf
page_325
325 27. Su fekkoon ne mboolem li nekk ci suuf si ciy garab, dafa doon ay xalima, géej gi amaat yeneen juróom-ñaari géej yu koy dolli, lépp di daa, kon dey du tax kàdduy Yàlla jeex. Yàlla Borom Kàttan la, di Ku Xereñ. 28. Seenug sosu ak seenug dekkiwaat yéen ñépp, mi ngi yombe Yàlla ni benn bakkan kepp. Yàlla Kuy ...
coran-wolof.pdf
page_326
326 ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Aliif, Laam, Miim. 2. Wàcceg Téere bii [Alxuraan], sikk nekku ca, mu bawoo ca Boroom àddina sépp. 3. Walla dañu naan [Muhammad] moo ko sos ? [Déedéet, lii mooy dëgg ga bawoo ...
coran-wolof.pdf
page_327
327 11. Neel : “Malaakam ndee ma ñu sasee loolu ci yéen moo leen di rey. Su ko defee, ngeen dellu ca seen Boroom”. 12. Cëy soo gisoon, tooñkat yaa ngay jatt seeni loos, naan ! “Yaw sunu Boroom, gis nanu, dégg nanu, delloo nu ca [àddina], kon de nu jëf lu baax ; léegi, xam nanu ne lii lu wóor la”. 13. “Bu Nu soo...
coran-wolof.pdf
page_328
328 23. Joxoon Nanu Muusaa Téere ba - bul am xel-yaar ci dajeek moom [yaw Muhammad] -, te defoon Nanu Téere ba mu di njub ñeel Bani-Israayiila gépp. 24. Defoon Nanu ci ñoom ay njiit yuy gindee ci Sunu ndigal, waxtu wa ñu muñee te wóolu Sunuy laaya [kàddu]. 25. Sa Boroom ci boppam dana àtte seen diggante ca la...
coran-wolof.pdf
page_329
329 1. Éy yaw Yonent bi ! Ragalal Yàlla te bul topp yéefar yi ak naaféq yi, Yàlla ku xam la, Ku xereñ la. 2. Toppal li ñu lay soloo te mu bawoo ca sa Boroom. Yàlla xàmmee na ca la ngeen di def. 3. Te nangay wéeru ci Yàlla. [Ndax] Yàlla doy na sëkk wéeruwaay. 4. Yàlla defalul kenn nit ñaari xol ci dënnëm. Def...
coran-wolof.pdf
page_330
330 12. Ak ba naaféq ya ak ña seen xol tawat di wax naan : “Yàlla ak Yonentam diguñu nu lu dul ay nax”. 13. Ak ba mu amee kurél ci ñoom buy wax naan : “Yéen waa Yasriba [Madina] ! Buleen fa toog. Delluleen [ginnaaw]”. Mu am it kurél ci ñoom buy ñaan ndigal Yonent bi, di wax naan : “Sunuy kër dafa aaruwul”, du l...
coran-wolof.pdf
page_331
331 22. Ña gëm tigi, ba ñu gisee farandoo ya, dañoo wax ne : “Lii la Nu Yàlla ak ub Yonentam doon dig ; te Yàlla ak ub Yonentam dëggal Nañu”. Te dolliwuleen lenn lu dul ngëm ak jébbulu. 23. Am na ci jullit ñi ñuy dëggal la ñu dëelante woon ak Yàlla. Am na ci ñoom ñu ko matal, am it ci ñoom ñuy négandiku ; te sopp...
coran-wolof.pdf
page_332
332 33. Nangeen di sax ci seeni kër ; te buleen di baraj-baraji kem ni ko jigéenu jaahiliya yu njëkk ya daan ko defe. Te nangeen di taxawal julli tey génne asaka te nangeen di topp Yàlla ak ub Yonentam. Ndax Yàlla dafa namm a dindi ci yéen, waa kër Yonent bi, lépp luy taq-taq, te laabal leen ba ngeen sell. 34. Na...
coran-wolof.pdf
page_333
333 43. Mooy kiy julli ci yéen, di leen ñaanal, - Mook ay Malaakaam, - ngir génne leen cig lëndëm, jëme leen cig leer ; te Mu di Jaglewaakoonu yërmaandeem ci ñi gëm. 44. Seenub nuyyoo Bis nuy dajeek Moom : “Jàmm rekk”, te mu waajal leen ag pey gu tedd . 45. Éy yaw Yonent bi ! Noo la yebal ngir nga doon seede, ...
coran-wolof.pdf
page_334
334 buleen toog di waxtaan. Ndax loolu, dafay lor Yonent bi mu di leen ko rus a wax, te Yàlla Moom rusul dara ci dëgg. Te su ngeen deeti laaj jegeñam ña dara, nangeen koy laaj ci ginnaaw kiiraay : ndax loolu moo gën a laab ci seeni xol [yéen ak ñoom] ; Te it waruleen di lor Yonent bi, waxantumalaak ngeen di takk sox...
coran-wolof.pdf
page_335
335 64. Yàlla rëbb na yéefar yi te waajalal na leen aw safara, 65. dañu fay béel fàww, duñu fa am ku leen méngoo, duñu fa am ndimbal. 66. Bis ba ñuy wëlbati seeni kanam ca Safara, ñuy wax naan : “Aka neexoon nu toppoon Yàlla, nu toppoon Yonent ba ! ”. 67. Ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, nun dey toppoon nan...
coran-wolof.pdf
page_336
336 ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Cant ñeel na Yàlla, Yàlla mi moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Cant it ñeel na ko ca àllaaxira. Moo di Ku Xereñ, di Ku Xàmmee. 2. Xam na li duggu ci suuf ak la cay génne, ak ...
coran-wolof.pdf
page_337
337 10. Joxoon Nanu Daawuda ngëneel lu bawoo ci Nun. Doj yeek njanaaw yi ànd ak moom di sàbbaal. Te it nooyalaloon Nanu ko weñ gu ñuul. 11. (ne ko) : “Liggéeyal ay mbubbi koŋ te jekkal ko”. Te ngeen di jëf u yiw. Kuy gis laa [Man Yàlla] li ngeen di def. 12. Tàggataloon Nanu Suleymaan ngelaw li, am xëyëm doxub w...
coran-wolof.pdf
page_338
338 20. Séytaane dëggalal na leen njortam. Ñoom ñépp daldi koy topp ba mu des ab kurél bu néew ca way-gëm ña. 21. Amul woon ci ñoom benn mën-mën lu dul ngir Nu xam ña ca gëm àllaaxira ak ña koy sikki-sàkka. Sa Boroom mooy wattu lépp lu ne. 22. Waxal ne : “Li ngeen di jaamu bàyyi Yàlla. Amuñu lu tollu ni kem aw ...
coran-wolof.pdf
page_339
339 32. Ña ca doonoon kilifa wax ña ca néewoon doole, ne leen : “Ndax Nun noo leen féewale woon ak njub ga ca ba mu leen dikkalee ? Li wér kay mooy yéen ay tooñkat ngeen”. 33. Ña ca néewoon doole wax ña ca doonoon ay kilifa, ne leen : “Moom ngeen daan fexe guddi ak bëccëg, ndax yéen a nu daan digal nuy weddi Yàl...
coran-wolof.pdf
page_340
340 42. Tey jii nag, kenn ci ñoom ëmbalut moroomam lor mbaa njariñ, te Dananu wax ña daan tooñ ne leen: “Tokkamtikuleen mbugamal Safara sa ngeen doon weddi”. 43. Bu ñu mësaan a jàng ci ñoom laaya yu leer, dañu naan : “Waa jii daal nammul lu dul féewale leen ak li leen seeni baay daan jaamu”. Ñuy wax it naan : “Lii...
coran-wolof.pdf
page_341
341 54. Ñu gàllankoor seen digganteek la ñu doon wuneen [sopp], kem nañu ko defe woon ca ña leen jiitu, ña nga woon ci biir sikki-sàkka gu xóot. ----------------------------------------------------------------------------- Saar 35 : AJI-SÀKKE JI 45 laaya – Laata Gàddaay gi -------------------------------...
coran-wolof.pdf
page_342
342 7. Ña weddi, mbugal mu metti dana leen dal, ña gëm nag tey jëf u yiw, danañu am njéggal ak pey gu rëy . 8. Naka kay jàppee ñaawtéefam ya muy lu rafet... ? – Yàllaay réeral ku ko soob, di gindi ku ko soob – Bul sonnal sa bopp ci ñoom : Yàlla xam na xéll la ñuy def. 9. Yàlla miy yebal ngelaw muy niir, Nu womm...
coran-wolof.pdf
page_343
343 18. Kenn du yenu bàkkaarub keneen. Te képp ku diis gann ak bàkkaar, bumu cay woote ndimbal, kenn du ko yenul dara, doonte la sax dafa di mbokkug jegeñaale. Da di rekk ne nangay xupp ña di ña ragal seen Boroom ci kumpa tey taxawal julli. Te képp ku cay sellal, na xam ne boppam la koy defal, te ca Yàlla la lépp ...
coran-wolof.pdf
page_344
344 30. loolu lépp ngir Yàlla jox leen seenug pey te dolli leen ciy ngënéelam. Moom Yàlla, Jéggalaakoon la, Kuy sant la. 31. La Nu la soloo ci Téere bi mooy dëgg tey saxal la ko jiitu woon . Yàlla kuy Xàmmee la, Kuy Gis jaamam ñi la. 32. Ginnaaw ba, donnale Nanu Téere ba sunu jaam ña Nu tànn. Am na ci ñoom ku...
coran-wolof.pdf
page_345
345 40. Neel : “Ndax gis ngeen ñi ngeen bokkaleek Yàlla, di leen jaamu ? Wonleen ma ñoom ana lan la ñu bind ci kaw suuf si. Walla dañoo am sañ-sañ ci asamaan yi ? Walla dañu leen a joxoon Téere bu leen bir” Déedéet ! Li am kay moo di ne tooñkat ñi ñoom wor rekk la ñuy digante. 41. Yàlla moo téye asamaan yeek suuf...
coran-wolof.pdf
page_346
346 2. Maa ngi waat ci Alxuraan jii fees dell ag xereñ. 3. Ci ne yaw [Muhammad] bokk nga ci limub Yonent yi. 4. ci kaw yoon wu jub xocc wa. 5. Mi ngi wàcce ci Yàlla boroom Kàttan ga di ab Jaglewaakoonu yërmaandeem. 6. Ngir nga xupp aw nit ñoo xam ne kenn musul a xupp seeni baay : ñoom dañoo sàggan. 7. ...
coran-wolof.pdf
page_347
347 16. [Yonent ya] waxaat ne : “Yàlla xam na ne nun ay Yonent lanu ci yéen. 17. te dara warunu lu dul jottali ba mu leer nàññ.” 18. Ñu ne : “Gaafal nanu leen. Te bu ngeen bàyyiwul, dananu leen jóori xeer te dananu leen mbugal mbugal mu tar”. 19. Yonent ya ne leen : “Seen gaaf googu mook yéen a ànd”. Moo nd...
coran-wolof.pdf
page_348
348 29. Génn xaacu rekk a fa jaar, ñu faf giim. 30. Ndeysaan jaam ñi le ! Ab Yonent mësuleen a dikkal mukk te du dañu koy ñaawal. 31. Xanaa gisuñu na Nu faagale woon maas ya leen jiitu woon ? Te kenn du ca dellusi. 32. Te ñoom ñépp danañu daje Sama kanam . 33. Indil Nanu leen firnde te moo di suuf si dee , ...
coran-wolof.pdf
page_349
349 44. lu dul yërmaande ju bawoo ci Nun, ak i xéewal ba jëmmi jamono. 45. Te saa su ñu leen waxee ne : “Wattandikuleen li nekk ci seen kanam ak li ci seen ginnaaw ndax amaana yërmaande wàcc ci yéen” !... 46. Amul yenn laaya , yu bokk ci seeni laayay Boroom, dikkal leen te dañu koo dëddu. 47. Saa su ñu lee...
coran-wolof.pdf
page_350
350 58. “Jàmm rekk la ñu fay ame” ! Mu bawoo ca Boroom biy Jaglewaakoonu Yërmaandeem. 59. “Ayca ! Ca biti, yéen tooñkat yi ! 60. Yéen doomi-aadama, ndax digewuma woon ak yéen ngeen bañ a jaamu Séytaane ? Ndax seenub noon la bu nëbbëtuwul, 61. te ngeen di Ma jaamu ? Lii mooy yoon wu jub xocc wi. 62. Mu ré...
coran-wolof.pdf
page_351
351 72. Nu tàggatal leen ko ; ñu di ca war te it ñu di ca lekk ; 73. am nañu ci ay njariñ ak i naan. Moo ndax dañu dul sant ? 74. Ñuy jàppe yàlla leneen lu dul Yàlla, ngir ñu neey danuy sàkku ndimbal... 75. Yooyu duleen mën a dimbali, dañuy sax faf di jàmmaarlook ñoom [di xare]. 76. Bula seeni wax jaaxal ...
coran-wolof.pdf
page_352
352 Saar 37 : SÀPPE YA 182 laata – Laata Gàddaay ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. [Maa ngi] giñ ci [Malaaka] ya sësëloo, def ay sàppe. 2. Ñay bëmëg niir yaak doole. 3. Ñay jàng ngir fàttali : 4. “Ne seen Yà...
coran-wolof.pdf
page_353
353 12. Yaw waaru nga, te ñoom ña ngay tejjiy reetaan ! 13. Te bu ñu leen di fàttali, duñu fàttaliku [Alxuraan] ; 14. dañuy wàkkante ak a reetaan [saa su ñu gisee keemaan], 15. tey wax naan : “Lii dey ag njabar doŋŋ la. 16. Moo ndax su nu faatoo ba def suuf ak i yax, dees nanu dekkalaat ? 17. ak sunuy b...
coran-wolof.pdf
page_354
354 27. ku nekk di geesu moroom ma, ñuy laajante ; 28. Ñuy wax naan : “Yéen a nu daan ga ci kéefar”. 29. [Kilifa ya] ne leen : “Yéen kay yéen a gëmul woon. 30. Te nun amunu woon benn sañ-sañ ci yéen. Yéen kay yéen a bewoon. 31. La Yàlla daan wax dal na ci sunu kaw ; [tey] noo ngi toqamtiku [mbugal]. 32. ...
coran-wolof.pdf
page_355
355 42. ay fuytéef ak i teraanga, 43. ca biir Àjjanay xéewal ja, 44. ñuy jàkkaarloo ca seen kawi lal. 45. Ñu di leen wër ak kaasi bënub ndox 46. weex tàll, te neex lool ca ña koy naan, 47. Lëj-lëj du fa am. 48. Te am nañu fa ay lamsalkat yu am bët , 49. weex ba mel ni nen. 50. Ku nekk di geesu m...
coran-wolof.pdf
page_356
356 57. dogankoon ak sama dimbalul Boroom, danaa sànku. 58. Xanaa nun dey dunu dee 59. lu dul ca dee gu jëkk ga te xanaa kenn dunu mbugal ? ” 60. Lii mooy texe gu màgg ga. 61. Ñiy jëf, nañuy jëf lu mel nii. 62. Moo ndax loolu moo di wàccuwaay ba gën, walla garabug Zaquum ? 63. Def nanu ko muy sànjub t...
coran-wolof.pdf
page_357
357 72. Ndax yónni woon Nanu ci ñoom ñuy xuppe, di waaraate . 73. Xoolal mujjug ñanu daan xupp ! 74. Ña ca dul jaami Yàlla ya ca daan sellal : 75. Nooh woo na Nu di ñaan, Nu wuyyu ko, nangu ñaanam. 76. Nu musal ko mook njabootam ci tiit mu rëy ma, 77. Nu def ay sëtam doŋŋ des fa. 78. Nu bàyyi ko, may...
coran-wolof.pdf
page_358
358 87. Waaw, lu ngeen njort ci Yàlla boroom asamaan si ? ” 88. Mu téen xool biddéew yi [di settantal], 89. mu daldi wax ne : “Man damaa wopp”. 90. Ñu dëddu ko, won ko ginnaaw. 91. Mu potoxlu ca seen yàlla ya, ne leen : “Ndax dungeen lekk ? 92. Ana lu leen dal ba dungeen wax ? ” 93. Mu potoxlu dóor le...
coran-wolof.pdf
page_359
359 102. Ba mu amee ati àndak moom, Ibraahiima wax na ne : "Yaw samas doom, gis naa ci bi may nelaw, ci biir gént, ndigalul war laa rendi. Seetal looy xalaat”. (Ismaayiila) ne ko : “Yaw sama baay, defal lu ñu la digal : bu soobee Yàlla, danga gis ne maag muñkat yee ànd”. 103. Ba ñu wéyalee seen ndigalul Boroom, mu...
coran-wolof.pdf
page_360
360 117. Nu indiloon leen ab téere bu bir 118. Nu indiloon leen yoon wu jub wa xocc. 119. Nu bàyyi woon leen nit ña di leen fàttaliku : 120. “Jàmmi Yàlla na wàcc ci Muusaa ak Haaruuna” 121. Noonu la Nuy feye ñiy rafetal ; 122. ñoom ñaar bokkoon nañu ci Sunu jaam ñi gëm. 123. Ilyaas it tigi bokkoon n...
coran-wolof.pdf
page_361
361 132. bokk na ci Sunu jaam ñi gëm. 133. Lóot it bokk na ci Yonent yi. 134. [Fàttalikul] ba Nu ko musalee mook njabootam gépp, 135. ba mu des màggat gu jigéen ga àndoon ak ña sànku woon, 136. Ginnaaw ba, faagaagal Nanu ña ca des 137. Te yéen a ngi leen di romb bu ngeen di xëy 138. ak ci guddi gi. ...
coran-wolof.pdf
page_362
362 147. Nu yebal ko muy Yonent ci téeméeri junniy nit mbaa lu ko ëpp. 148. Ba ñu gëmee, xéewalal Nanu leen fa ab diir. 149. Laajleen baxam : “Ndax Yàlla moo ame doom yu jigéen, ñoom ñuy am doom yu góor ? 150. Walla dañoo bind Malaaka yi def leen ñu di ay jigéen, seere ko ? ”. 151. Ndax ñoom dañuy faral d...
coran-wolof.pdf
page_363
363 162. kenn duleen ci fitnaal, 163. ku dul kuy nar a xoyomu ci Safara. 164. Amul kenn ci [Malaaka yi] lu dul ne am na wàccuwaay wu ñu xam ; 165. te noo leen defoon ay sàppe ; 166. te nun nooy sàbbaal Yàlla. 167. Doonte la sax ña ngay wax naan : 168. “Su nu amoon waarate gu bawoo ca sunuy maam, ...
coran-wolof.pdf
page_364
364 177. Su wàccee ci seenub ëtt, ñoom ña ñu doon fàttali, ndaw suba gu bon ! 178. nanga leen dummóoyu ab diir ; 179. te nga seetluleen : danañu gis de ! 180. Tudd naa sellug sa Boroom, Boroom kàttan gi. Kawe na ca la ñu koy melal ! 181. Te jàmm yal na wàcc ci Yonent yi, 182. te xeeti cant yépp ñeel na...
coran-wolof.pdf
page_365
365 5. Moo ndax dafa bëgg a def Yàlla yii muy jenn Yàlla ? Aa lii dey mbir mu yéeme la”. 6. Kilifa ya ne leen : “Demleen, te muñ jàpp ci seen Yàlla yii : lii daal la nu bëgg. 7. Nun masunoo dégg lii ci diine ji fi mujj wàcc (Iisaa) ; lii daal ay sos rekk la ! 8. Nuy wax naan, ak ni nu tollu ndax ci moom la ...
coran-wolof.pdf
page_366
366 18. Tàggataloon Nanu ko, tundi doj yi nu daan ànd ak moom, di sàbbaal Yàlla subaak ngoon, 19. picc yépp it dañuy dajaloo, di delloo kañ [Yàlla]. 20. Dëgaralal Nanu ko nguuram jox ko xam-xamu xereñe ràññee ak xam-xamu àtte. 21. Moo ndax xibaari xulóokat ya agsi na ci yaw ba ñu bëttee ñagub mbaar ma (mihraab...
coran-wolof.pdf
page_367
367 30. May Nanu Daawuda (doomam ja) Sulaymaan, - ndaw jaam bu baax ! – Ku daan dellu ca boroomam la. 31. (Fàttalikul) ngoon ga, ñu ko gaarale fasi naari góor ya, 32. Sulaymaan dellu wax ne : “Cëy man, maa ngi fees dell ak bëgg (àddina sii) mu fàbbi maa ba jant bi so te fàttalikuwuma sama Boroom. 33. Dello...
coran-wolof.pdf
page_368
368 43. Nu delloowaat ko njabootam joxaat ko lu na tollu, muy yërmande ju bawoo ci Nun ak fàttili woroom xel yi. 44. “Ŋëbal sëqub ñax, te dóor ko ko (soxnaam sa). Te bul gàddu bàkkaarub ngiiñ”. Moom, muñkat la di jaam bu baax. Kuy farlu di dellu ci Boroomam la. 45. Fàttalikul suñu jaam ña Ibraahiima, ak Ishaaq ...
coran-wolof.pdf
page_369
369 58. ak yeneeni xeeti mbugël yu mu témbóol. 59. Ñii ay mbooloo la ñu ñuy buuxanteek yéen, kenn dalaluleen. Te ñooy xoyomu ca Safara. 60. Ñuy wax naan : “Yéen kay la kenn dul dalal, lii, Yéen la ñu ko waajal”. Te ndaw saxuwaay bu bon ! 61. Ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom na nga dolli, ki nu waajalal lii, ...
coran-wolof.pdf
page_370
370 71. (Fàttalitul) ba sa Boroom waxee Malaaka ya ne leen : “Man de maa ngi sàkk mbindéef ci ban. 72. Suma ko móolee ba ëf ci Sama Ruu, na ngeen daldi rot, sujuudal ko”. 73. Malaaka ya yépp daldi sujuud, 74. ba mu des Ibliis moom dafa rëy-rëylu bokk ca yéefar ya. 75. (Yàlla) daldi ne : “yaw Ibliis, lan mo...
coran-wolof.pdf
page_371
371 86. Waxal ne : “Laajumaleen ci ag pey ; te it yanuwuma ci. 87. [Alxuraan] jii daal ag fàttali la ñeel waa àddina si yépp. 88. Te dangeen xam ay xibaaram ci ndiir su yàggatul ! ”. ----------------------------------------------------------------------------- Saar 39 : MBOOLOO YA 75 Laaya – Laata Gàdda...
coran-wolof.pdf
page_372
372 yatti lëndamaay. Koo koo di Yàlla, seen Boroom ! Moo moom Nguur. Te amul jeneen Yàlla judul Moom. Man dey xamuma naka ngeen koy walbatee ? 7. Su ngeen weddee, Moom doyewu leen dara. Te gëramul kéefër, ci jaamam yi. Su ngeen santee, Mu gëramal leen ko. Amul kenn kuy yanu bàkkaarub keneen. Te it, dees na leen d...
coran-wolof.pdf
page_373
373 17. Ñay moytandikoo jaamuy xërëm, tey dellu ca Yàlla, danañu am mbégte ! Bégalal Sama jaam ñi 18. Ña nga xam ne dañuy déglu Wax, tey topp la ca gën a rafet. Ñoom la Yàlla gindi te ñooy woroom xel ya ! 19. Ka baatub mbugël yay ci moom,... ndax yaw yaay xettali ku nekk ca biir safara ? 20. Waaye ñay ragal ...
coran-wolof.pdf
page_374
374 28. Mooy Alxuraan ju di [làmmiñu] araab, amul lugg-luggal, ndax amaana ñuy ragal Yàlla ! 29. Yàllaa ngi sadd léebu jenn waay ju am digaale yu bari tey ŋaayoo : ndax niróonaak waa ju am benn digaale bu mu jubóol ? Yàlla rekk yayoo cant ! Li am moo di ne li ëpp ci ñoom xamuñu (misaalum kuy jaamu Yàlla ak ku koy ...
coran-wolof.pdf
page_375
375 40. ana kan la mbugël di dikk toroxal ko ; ak ci kaw kan la mbugëlam dëggële di wàcc”. 41. Wàcce Nanu ci yaw Téere ba, ci dëgg, ngir nit ñi. Ku gindiku boppam ; ku réer it boppam. Seenub lijjënti warula 42. Yàlla mooy faat bakkan bu ñuy dee ak ya deewul ci biiri nelaw. Mooy téye ya mu namm ñu dee, di boyal...
coran-wolof.pdf
page_376
376 52. Xanaa dañoo xamul ne Yàlla mooy yaatalal ku ko soob wërsëgam di ko xatal it ? Ay kiiman a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñu gëm. 53. Waxal ne : “Éy yéen Sama jaam ñi yàq seen bopp, buleen naagu ci yërmandey Yàlla. Ndax Yàlla dana jégële bakkaar yépp. Mooy Jégëlaakoon ba, di Jaglewaakoon ba”. 54. Dellu...
coran-wolof.pdf
page_377
377 64. Waxal ne : “Yéen ñi réer, ndax dangeen may digël may jaamu lu dul Yàlla ? ” 65. Te, soloona Nu la ak (Yonnent ya la jiitu woon) ci ne : “Saa soo bokkaalee , sa jëf dana sippiku; nga bokk ci ñu yàqule ña. 66. Jaamujil Yàlla, tey sant”. 67. Joxuñu Yàlla dayoom tigi, suuf si sépp ab ŋëbëm lay doon bu Bis...
coran-wolof.pdf
page_378
378 ----------------------------------------------------------------------------- Sourate 40 : JÉGËLEKAT BA 85 laaya - Laata Gàddaay ga ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Haa, Miim. 2. Wàcceg téere bii ma ngi bawo...
coran-wolof.pdf
page_379
379 10. Ña weddi nag ñoom dañu leen woo naan leen : “jéppig Yàlla moo gën a rëy ni ngeen jéppee seen bopp, ba ñu leen daan woo jëme leen ci ngëm dangeen daan weddi”. 11. ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, rey nga nu ñaari yoon, dundal nga nu ñaari yoon : nangu nanu sunuy bàkkaar. ndax lii man nanu tee génn” ? 12....
coran-wolof.pdf
page_380
380 22. Li ko waral, moo di ñoom seeni Yonnent, da ñu leen daan indil ay lay yu leer ñu weddi. Yàlla daldi leen faagaagal, Yàlla boroom doole la di ku Tar mbugël. 23. Yónni woon nanu Muusaa ak sunuy laaya boole ko ak ay firnde yu leer, 24. jëmële ko ca Firawna, ak Haamaana ak Qaaruuna. Ñuy wax naan : “Kii ab n...
coran-wolof.pdf
page_381
381 32. “Éy yéen samaw nit, ragal naa ci yéen bisub wootante ba, 33. Bis ba ngeen di wane sànku, te dungeen am ku leen di aar ci Yàlla”. ku Yàlla natt ci moom réer, kenn du ko man a gindi. 34. “Yuusuf, indaloon na leen ay firnde yu leer naññ, te de ñu leen di sikki-sàkka ca la mu indiwoon. Ba mu faatoo, ngeen w...
coran-wolof.pdf
page_382
382 44. Yàggatul ne dangeen fàttaliku ji lii ma leen di wax ; te wéer naa samay mbir ci Yàlla. Ndax, kuy Gis jaamam ñi la. 45. Yàlla fegal na ko ñaawtéef ya ñu doon fexe, daldi sóob njabootug Firwana gën jaa tar i mbugël : 46. ñu di leen , gaaral ci Safara suba ak ngoon. Bu Bis Pénc baa (da naa digle) : “Ñu d...
coran-wolof.pdf
page_383
383 55. Na nga muñ, (te xam ne) digub Yàlla dëgg la, te it na ngay jéggalu say bàkkar tey sàbbaal sa Boroom di ko sant, ci ngoon si ak ci suba si. 56. Ñay dàggasante ci laayay Yàlla ya ci lu àndul ak firnde yu ñu leen jox, rëy-rëylu doŋŋ a nekk ca seen dënn ya. Te seen aajo du ca fajoo. Na ngay muslu ci Yàlla, moo...
coran-wolof.pdf
page_384
384 67. Mooy ki leen bind ci suuf, te jaarale leen ci toqu maniyy, ak ci lumbu deret door leen a génne ngeen di ay xale mu def leen ngeen di ay mag yu war a maggat kumur, - am na ci yéen ñuy faatu balaa loolu lépp di am, - ku ca nekk it am na ab dig bu ñu ko àppal, ak it ngir ngeen xellu (xalaat). 68. Mooy dund...
coran-wolof.pdf
page_385
385 78. Yónni woon Nanu ay Yonnent yu la jiitu woon. am na ci ñu ñu la nettali ; am na ci ñu ñu la nettaliwul. Amul benn yonnent bu sañ a indi [kimaan laaya] lu dul ne da ca am ndigëlul Yàlla. Saa su ndigëlul Yàlla agsee, mbir yépp àttewo ci dëgg ; fenkat yi daldi yàqule. 79. Yàlla mi leen defaral mala yi ngir ng...
coran-wolof.pdf
page_386
386 1. Haa, Miim. 2. [Ak solool] gu ñu wàcce mu bawoo ci Yëramaakoon bi , di Jaglewaakoon bi (yërmandéem). 3. Ab Téere bu ñu faramfànce ay laayam muy Alxuraan di ko [jàng] ci làmmiñu araab ngir aw nit ñuy xam, 4. di bégle tey xuppe. Ña ëpp ci ñoom dañoo dumóoyu ; du ñu (ko) dégg. 5. Ñuy wax naan : “Sunuy ...
coran-wolof.pdf
page_387
387 13. Bu ñu dumóoyoo lànk, waxal ne ; “maa ngi leen di xupp ci ag dënnu dënnu gu melni ga daloon waa Aad ak Samuud”. 14. Ba leen yonnenta ya digëlee, bawoo kanam ak ginnaaw, [daan leen digël]: “Ci nuy jaamu Yàlla (ba ña jaamu leneen)”, ñuy wax naan : “Bu neexoon Yàlla, Mu wàcce ay Malaaka. Te sax nun lii ñu l...
coran-wolof.pdf
page_388
388 24. Bu ñu xaaree, Safaraa di seen kër ; bu ñu sàkkoo njégël, kon duleen jégël. 25. Boole Nanu leen ak ñu ñu lëkkëlool ñu taaralal leen la ca seen kanam ak sen ginnaaw (la ñuy jëf). Dogal ba dal ci seen kow, kem na mu ame woon ca xeet ya leen jiitu woon ci jinne yi ak nit ñi. Ñoom dañoo yàqule ! 26. Ña weddi...
coran-wolof.pdf
page_389
389 36. Amaana leeg-leeg bu la saytaane jaxjaxee (waaye bu boobaa), na nga sàkku ci Yàlla mu mësal la ; Moo di, aji Dégg ja, aji xam ja. 37. Bokk na ci ay kéemaanam, guddi ak bëccëg, ak jant beek weer wi : buleen sujuudal jant bi, waxantumalaak weer wi, waaye na ngeen di sujuud ngir Yàlla mi leen bind, ndegam M...
coran-wolof.pdf
page_390
390 46. Képp kuy jëf yiw, boppam la koy defal. Képp kuy jëf ñaawtéef it, te ci kawam lay dal. Sa Boroom, du tooñ, benn jaamam. 47. Ca moom la xam-xamu Waxtu wa di dellu (moom rekk xam). Amul menn meññat muy génn ciw xottam, amul it jenn jigéen juy ëmbu walla muy imbi lu dul am na ca xam-xam bu mat sëkk. Te bu ker...
coran-wolof.pdf
page_391
391 53 laaya - Laata Gàddaay ga ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Haa, Miam. 2. Ayn, Siin, Qaaf. 3. Noonu la la Yàlla, miy boroom Kàttan, tey ku Xereñ, di soloo ay ndigëlam, kem ni mu ku defe woon ca Yonnent ya l...
coran-wolof.pdf
page_392
392 11....Moo bind (sàkk) asamaan yeek suuf si. Defaralal na leen y soxna [jële ko] ci seeni jëmm ak ay mala yu di ay tóollént ( góor ak jigéen); te ci loolu la leen di yokki (jurante). Amul lenn lu mel ni moom (Yàlla) ; mooy aji Dégg, di aji Gis. 12. Moo ame caabi [ndami] asamaan yeek suuf si. Mooy yaatalal wërs...
coran-wolof.pdf
page_393
393 21. Am ñoom da ñoo am bokkaale yu leen tërëlal diine ju bokkewul ak li Yàlla digle ? Du gan kon, ak kàddu gu xas jib ba noppi, kon àtteef na seen diggënte. Te tooñkat ya ñoom am nañu mbugël mu mitti . 22. Danga gis tooñkat ya ñu tiit lool ngir la ñu daan def, (mu di mbugël) muy dal ci seen kaw. Waaye ña gëm...
coran-wolof.pdf
page_394
394 31. Munuleen a raw Yàlla ci suuf si ; te it du ngeen am geneen kilifa, waxantumalaa ndimbal kudul Yàlla. 32. Bokk na ci ay kéemaanam (firndéem), gaal yuy daw ci géej, tollu ni ay tundu doj. 33. Su ko neexee, Mu téye ngilaw, ñu ne tekk ca ndox ma. Ay kéemaan na ngi ci biir loolu ngir [nit] kuy muñ tey sant (...
coran-wolof.pdf
page_395
395 44. Képp ku Yàlla xas réerël dootul am kilifa gu koy man a aar ku dul Yàlla. Danga gis tooñkat ya bu ñu gisee mbugal ma dañuy wax naan : “Fu ñuy ame pexe mu nuy delloo [àddina] ? ” 45. Danga leen gis ñu di leen gaaral ca kanam Safara, ñu boole tiit ak gàcce, ña ngay xoole ne xeww di rummi, ña gëm ña ngay wax...
coran-wolof.pdf
page_396
396 Saar 43 : XOYXOYAL 89 laaya - Laata Gàddaay ga ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Haa, Miim. 2. Ci Téere bu leer bu ! 3. Def Nanu ko Alxuraan ci làmmiñu araab ndax amaana ngeen xellu (xalaat). 4. Nekk na ...
coran-wolof.pdf
page_397
397 13. ngeen di def ñoŋŋ ca kaw, ngeen di fàttaliku xéewali Yàlla, su ngeen yemoo ca kaw ne ñoŋŋ, te it na ngeen di wax naan : “Tudd nanu sellug ki nu tàggatalal lii (wépp waruwaay) te manalu nu ko woon sunu bopp. 14. Te dañuy wëlbatiku jëm ci sunu Boroom”. 15. Nit ñi dañuy mbokkale yàlla ak lenn ci jaamam ñ...
coran-wolof.pdf
page_398
398 25. Nu daldi fayu ca seen kaw. Xoolal (settantal) naka la mujjug weddikat ya deme. 26. (Fàttalikul) Ibraahiima ba mu waxee baayam aku nitam : “Man mii ku deñ laa ci lii ngeen di jaamu, 27. ba mu des (Yàlla) mi ma sàkk bind ma, te moo may gindi”. 28. Mu def (dénkaane boobu) muy kàddu guy sax ginnaawam. N...
coran-wolof.pdf
page_399
399 37. Te ñoom Dañu leen dëdaleek yoon (wu jub wa xocc), te ñu foog ne dañoo gindiku. 38. Ba ne seef agsi ci Nun dey, daldi wax ne: “Aka neexoon ! Sunu diggënte soriyaantoo ni [Pénkook Suwu] ! ” – Ndaw lëkkëloo bu bon ! 39. Loolu lépp du leen jariñ lenn tey jii – ginnaaw ba ngeen tooñee – yéen ay bokk yem ca ...
coran-wolof.pdf
page_400
400 50. Ba nu teggee jafe-jafe ya, da ñoo tiri lépp la ñu digéwoon. 51. Firawna daldi dajale aw nitam ne leen: “moo sama gaa ñi ! Ndax moomu ma nguurug Misra ak dex yii di dawdawaan ci sama ron? Xanaa du ngéen gis ? 52. Xanaa man sax maa wara gën waaju doyadi jii nga xam ne xawut a man a wax ( lu nit di xam )...
coran-wolof.pdf
page_401
401 63. Ba Iisaa dikkee and ak i firnde, nee na leen : “Indil naa leen xam-xamu xereñ ak it ngir ma leeralal len lenn ci li ngeen di juubuu. Ragalleen Yàlla te topp ma. 64. Yàlla moo di sama Boroom di seen Boroom. Na ngeen ko jaamu. Lii mooy yoon wu jub wa xocc. 65. Kurél ya juuyoo ci seen biir. Ña daan tooñ to...
coran-wolof.pdf
page_402
402 77. ña ngay woo : “ Maalik (bëkknéegu safara)! naan ko nanu sa Boroom jéggëli book ! ” muy tontu naan : “Yéen kay, ci [mbugël mii] ngeen di sax dëgg” ! 78. “Indiloon Nanu leen dëgg; waaye ñi ëpp ci yéen dañoo bañ Dëgg”. 79. Walla, Ñoom dañoo fexe ay mbir [ak lu man a xew] ? Nun nooy sottal mbir yi ñu alku...
coran-wolof.pdf
page_403
403 89. Dumóoyuleen yaw ; tey wax : “Jàmm ! ” Danañu xalset a xam. ----------------------------------------------------------------------------- Saar 44 : SAXAR SA 59 laaya - Laata Gàddaay ga ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Ja...
coran-wolof.pdf
page_404
404 10. Fuglul, cëy bis ba asamaan si di dikk ak saxar suy jolli 11. di moor nit ñi. Tey mbugël mu mitti. 12. “Waay-waay, sunu Boroom téggil nu mbugël mi. Ndax nun ay jullit la nu [léegi]”. 13. Ana fan la leen kii fàttaliku bawoo te ab Yonnent bu bir dikkoloon leen, 14. Ñu daldi dumóoyu te naan : “Kii daal,...
coran-wolof.pdf
page_405
405 25. Ak a bari ay dër yu ñu bàyyi ginnaaw ak bëti ndox 26. ak tool (mbay) ak kër yu taaru, 27. ak i xéewal yu ñu daan gamaajoo. 28. Noonu la Nu ko donolee yeneeni xeet. 29. Asamaan ak suuf jooyuñuleen te kenn it muñadikuwuleen. 30. Musëloon Nanu , waa bani Israayiila ci mbugël mu doyadima (rey góor)...
coran-wolof.pdf
page_406
406 40. Ca bisub àtte ba, lañuy daje ñoom ñépp, 41. Bis ba farandoo dul jariñ moroom ja ; te kenn duleen dimbali, 42. ku dul ku Yàlla yërëm. mooy, boroom Kàttan, di Jaglewaakoon yërmande. 43. Garabub Sakkuum ga tigi 44. moo di lekkug defaakoonu bàkkaar ya. 45. Day melni biteex ; buy wañax ca (seen biir...
coran-wolof.pdf
page_407
407 55. Ñu fay man a am wépp xeeti fuytéef féex lool ne fayax. 56. Duñu fa mos wextanu ndee lu dul dee gu jëkk ga. [Yàlla] fegal na leen mbugëlum Safara, 57. muy ngëneel lu bawoo ca sa Boroom. loolu mooy texe gu màgg ga. 58. Di ko yombal ci saw làmmiñ, ngir amaana ñuy fàttaliku ! 59. Xaaral. Ñoom it ñi ng...
coran-wolof.pdf
page_408
408 6. Yooyu ñooy firndey Yàlla nu di la ko jàngal mu tegu ci dëgg. Kon ana jan wax la ñuy man a gëm ginnaaw bu Yàlla ak firndeem Yii jàllee? 7. Képp ku dib duuraakoon defaakoonub bàkkaar toskare na ca xuri sawara ! 8. Daan dégg ñuy jàng laayay Yàlla yi ( Alxuraan) mu féttéerlu di jaayub dayo, melni ku ko dég...
coran-wolof.pdf
page_409
409 17. joxoon Nanu leen ay firnde yu leer ci ndigël yi. Wuutewuñu woon lu dul ba ñu amee xam- xam cig bew, ci seen diggënte. Te sa Boroom dana àtte seen diggënte, bu Bis Pénc baa, ca la ñu daan juuyoo. 18. Topp ginnaaw ba teg Nanu la ci yoonu ndigël. Na nga koy topp te bul di topp bànneexu ñiy xamadi. 19. Ndax...
coran-wolof.pdf